Demokaraasi jéggi na diine,
Boole nit ak ngëm gu ne
Demokaraasi romb na xeet
Yamale ñépp, dàq wéet.
Réew dañ koy péncoo,
Ken du ko pàccoo !
Demokaraasi weddi na boddikonte,
Digle bokkoo ak jàppalante.
Wuute maam, wuute waasoo,
Terewul bokk réew tey diisoo.
Réew dañ koy péncoo,
Ken du ko pàccoo !
Bu fitna tàkkee, jàmm jéex,
Doo tal diine bay xalaat féex.
Doo tal jàmmasante,
Bay xalaat seetante.
Réew dañ koy péncoo,
Ken du ko pàccoo !
Demokaraasi du jiital alal
Jaay ak jënd baat di ko lal;
Du jënd nit, def ko mala,
Te jaay kart musiba la.
Réew dañ koy péncoo,
Ken du ko pàccoo !
Demokaraasi dog na jéng
Demokaraasi fecci jatang
Yewwi ci askan xol ba ak xel ma
Siggil liggéeykat ak waa réew ma.
Réew dañ koy péncoo,
Ken du ko pàccoo !
Momar Sàmb, awril 2001
Aucun commentaire:
Enregistrer un commentaire